YÓNNENT BI (saws) nee na : « Mujjug jamono dana am boroom xam-xam yo xam ni dañuy xemmeemloo nit ñi allaaxira te ñoom duñu ko xemmeem, di dëdduloo nit ñi àdduna te duñu ko dëddu, di tere seeti buur yi ba noppi di leen seeti »
YÓNNENT BI (Saws) nee na : «SUNU BOROOM dana bëgg buur buy jaxaso ak boroom xam xam yi ndax loolu da leen di xemmeemloo ëllëg, waaye bëggul boroom xam xam buy jaxaso ak buur yi ndax loolu da leen di xemmeemloo àdduna.»
Al’Fudaylu nee na : « Boroom xam xam yi bu ñu aaroon seen xam xam teral ko, teg ko fa ko YÀLLA(Swt) teg, te nay ci seen diine..kon buur yi danañu toroxlu ci ñoom, nit ñépp topp leen, su ko defee lislaam tedd ak ñoñ lislaam..waaye dañoo wàcc seen bopp te duñu faale sax liy wàññiku ci seen diine bu ñu manee am àdduna. Dañuy jox seen xam xam nitu àdduna yi ngir ñu man am alal..moo tax ñu torox lool suufe ci bëti nit ñi»
————
*
Tagged
Locked Photo
Seems you enter wrong password click here to enter password again.