Album Home » Browse Albums » View Album  » Photo
Photo 1.8K of 3.1K

People Who Liked This

click to rate
1 Like 0 Comments 72 Views 0 Favourites 0 Downloads
Description Sëriñ bi mas naa am taalibe yu mu wax ni def léen ñenti xaaj, wet gu ne
am ñu fa toog, mu jàkkaarlook ña féete penku ni léen, waa penku dama léen di laaj xiif lu ngeen xam ci lu ko man a faj ? Ñu ni cell, mu laajaat léen ko ? Ñu ni ko lekk la ñu xam ci lu koy faj. Mu wëlbatiku ci wet yépp laaj léen ko ñu wax
loo lu, mu wëlbatiku toogaat ca digg ba wax ni man mii tam xiif xamu ma lenn lu ko mana faj lu dul lekk. Ni ngeen xamee ni xiif dara manu koo faj lu dul lekk,
mbugalu bàmmeel tam dara manu koo faj lu dul jaamu Yàlla, man mii nag sunu Boroom ràbbal na ma ci àdduna mbalaanu sutura moo xam ni ku fi nekk muuru ci biir waaye mbalaanum bàmmeel borooma koy ràbbal boppam.